
Mucc Saar 14 | Firawna dabi na bànni Israyil
Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: «Waxal bànni Israyil, ne leen ñu walbatiku dali fa jàkkaarlook Pi Axirot, ca diggante Migadol ak géeju Barax ya. Dal-leen foofa jàkkaarlook Baal Cefon ca tefes ga. Su ko defee Firawna da naan: “Bànni Israyil de dañoo réer ci àll bi, ba faf keppu ci màndiŋ mi.” Gannaaw loolu maay dëgëral boppu Firawna, mu topp leen, ba ma jaare ca siiwal sama ndam, ndax maay daan Firawnaaki xarekatam yépp, te waa Misra dinañu xam ne, man maay Aji Sax ji.» Musaa jottli leen ko, ñu def noona.
This podcast uses Soundcloud for stats. What this means Episodes play from the podcast's own servers, unmodified. Not affiliated with Podbay.
